Lo def ba ñeup seddé la mbax
Sa rafet jiko say mbok nka ndieuka waax
Do niitu fitna, kou la xam xam la si diama
Sa yone newul si luñu la bollé wul da nga manu
Fo guiss diganté bu niagass dokh nga si diama
Fo guiss lu amal ndiarigne sa askan sol nga sey dalleu
Dem outi ko andi
Amo watia sa anda
Fi nga teek sey wadiur teggo fa kene do Samba Allar
Yo mom lo def ba ñeup né da nga bone
Baax dou meyé yow nga tamu dieundeu bone
Sa lamigne banta bumu diap def ko dom
Do dioum ba wakh lou baax
Weur di fenn suba ba ngone
Do yené ken lou baax
Kou la deglou def toukhi douna
Sikka takh do dioubo'k keneu
Teguilo kene tuma
Fonko sa ada
Xamo sa diné
Def sa bopp wagga
Xolal ni la kobba yi tchiné
Lo def ba ñeup seddé leu mbax
(Lo def lo def wakh ma lo def lo def)
Lo def mba ñeup né da nga bone
(Lo def lo def wakh ma lo def lo def)
Lan nga def ba done tey ki nga done
(Lo def lo def wakh ma lo def lo def)
Lou taax nga kheuy rek diada yon
(Oh wiyo wiyo wiyo)
Lan nga def ba done tey ki nga done
Yow mom ya gueuneu metti nguey taneu kou dioup
Ñeupeu la dawone nga dess ak sa bopp
Beñ kou la xeep mo takh do wakh kene lou dieum sa bopp
Bess bu set dianta bi leeral yakey yé
Sa yone meunou la leundeum
Xaliss tewul nga gueum
Doylu nga si li nga ame
Yewene nga si meye niam
Fatéwulo ñi nga xaam
Fo dem yobalé diam
Yow lou takh nga xey rek diada yone
Lo def ba ñu dakha la école
Lo def ba xadia to sa kogne
Yow wakh ma lane nga def ba ñeup xeey rek def la none
Lou takh nga meuteu sey ame xolu tok di xol sa yaye di mogne
Lou takh sa dallu baye diote la té nangulo def ni mom
(Wakh ma lou takh)
Khawma lou takh ñu eupeu sikka meuneu togne
(Khawma ma lou takh)
Lou takh xaar yewu rek né dotul lekka ngogne
Lo def ba ñeup seddé leu mbax
(Lo def lo def wakh ma lo def lo def)
Lo def mba ñeup né da nga bone
(Lo def lo def wakh ma lo def lo def)
Lan nga def ba done tey ki nga done
(Lo def lo def wakh ma lo def lo def)
Lou taax nga kheuy rek diada yon
(Oh wiyo wiyo wiyo)