Ni nu tooge di guux sunu ñetteelu kaasu atttaaya
Di ñàq ci jantu Senegal niki safara
Samay xarit yëpp di waxtaan ci sunu tukki tukki tukki
Ci ñoom Senegal du kër jaarukaay la rekk
Dëgg la bu ñu waxe 'fii amul liggéey'
Te dëgg kaani la
Wante sama yaay ne na: doom-ju-ñakk xëy
Moo gën doom-ju-ñakk bakkanam
Amuma visa amaguma passport
Lu ma yor moy yakkaar bu rey
Ñu ne: Jamm-a-gën dee
Waaye boo soxla garab yi jámm menu ko fey
Gis na nataalu Elaji mungi amerik
Léegi am na iPhone ak ordinateur bu bees
Wante xaritam bi yeggul sax nikaraguwa
Njabotam di laajte sén domm: fan la nekk ?
Ñu ne jom moy tukki waaye fulla moy ñibbisi
Waaye ñibbiseek loxo neen moo raw gàcca
Wiri wiri mom jaari ndaari
Waaye ngir jaari ndari fàww nga am sarica
Bëgg naa dem manchesta
Wante su ma tukkee luma fay ameh?
Yonenti Suleeymaan ne na:
Nit gisul njariñ ci kaw suuf Rafet xel fanqul deh
Goor-goorlu mor tax-a-don goor
Jom mooy tukki waaye fulla moy ñibbisi
Damay toog? Walla damay dem? Xamuma lan lay def
Tukki Tukki tukki fëgg fëgg fëgg
Dem xol Tugël loolu lañuy bëgg
Original Lyrics. Music by Suno AI. Written distributed by me.
My socials on YT and X are @KëggDanni
Thanks for listening.